Dëgërlul doon jàmbaar
Telesarseel:
1. Moom yeewu na
Ci suba teel,
Tàmbali di ñaan naan:
“Yal na samay doom
Ak waa mbooloo mi
Tàkku te bégal Yàlla”.
Lu mbir yi di gën a tar,
Muy gën di yaakaar Yexowa.
Am na woy wuy tax muy dëgërlu,
Du ko mas a fàtte:
(AWU BI)
‘Man ak yow laa àndal.
Bul tiit bul ragal.
Maa ngi lay téye.
Te di la dooleel.’
Dëgërlul doon jàmbaar
Woy wi ko gën a neex.
Te “dina la téye,
Te dina la dooleel.”
(PONT BI)
Waxtu yeewu jotna —
War na dem liggéey —
Te xamagul lu koy xaar.
Waaye moom wéetul
Ndaxte am na xarit,
Yu koy wéy di won mbëggeel.
2. Moom moo ngi naaw
Mel ni jaxaay
Juy naaw ci asamaan.
Yenam diis na lool —
Jotam itam néew na —
Yaramam bépp a ngi metti.
Waaye ñaan na Yexowa —
Liggéey na ba fa dooleem yem.
Waaye ak lu mu metti metti
Du fàtte woyam wi:
(AWU BI)
‘Man ak yow laa àndal.
Bul tiit bul ragal.
Maa ngi lay téye.
Te di la dooleel.’
Dëgërlul doon jàmbaar
Woy wi ko gën a neex.
Te “dina la téye,
Te dina la dooleel.”
Te “dina la téye,
Te dina la dooleel.”