Suñu mbégte ba fàww
Telesarseel:
1. Biddéew yi fees ci asamaan,
loolu rafet na,
Te taaru suuf ak taaru géej,
Yow yaa ko waral.
Kon bépp ndam yaa ko yelloo,
Yow mi defar lépp li am,
Te nga bég ci lool.
(AWU BI)
Sa Kàddu ak li nga sàkk,
Wone na ne yow ku bég nga.
Ñu ngi séentu àjjana.
Wéy di yëg sa mbëggeel ba fàww,
Du fi am alal ju ko raw.
Yexowa yow dinga doon
Suñu mbégte ba fàww.
2. Yow Yexowa sàkk nga lépp
ndax suñu bànneex.—
Ni nga ñu bindee yéeme na,
Céy lii aka neex!
Bi nga sàkkee doom Aadama,
Dugal nga ko ci àjjana.
Te mu bég ci lool.
(AWU BI)
Sa Kàddu ak li nga sàkk,
Wone na ne yow ku bég nga.
Ñu ngi séentu àjjana.
Wéy di yëg sa mbëggeel ba fàww,
Du fi am alal ju ko raw.
Yexowa yow dinga doon
Suñu mbégte ba fàww.
(PONT BI)
Sa doom ji nga ñu may
moo tax ñu am tey mbégte.
Yeesu joxe na bakkanam,
kon ba fàww mbégte la ñuy am.
(AWU BI)
Sa Kàddu ak li nga sàkk,
Wone na ne yow ku bég nga.
Ñu ngi séentu àjjana.
Wéy di yëg sa mbëggeel ba fàww,
Du fi am alal ju ko raw.
Yexowa yow dinga doon
Suñu mbégte ba fàww.
(AWU BI)
Sa Kàddu ak li nga sàkk,
Wone na ne yow ku bég nga.
Ñu ngi séentu àjjana.
Wéy di yëg sa mbëggeel ba fàww,
Du fi am alal ju ko raw.
Yexowa yow dinga doon
Suñu mbégte ba fàww.
(Xoolal itam Taalifi Cant 37:4; 1 Korent 15:28.)