NJÀNGALE 1
Ñan ñooy seede Yexowa yi dëgg-dëgg ?
Ndax xam nga ay seede Yexowa fi nga dëkk, fi ngay liggéeye walla fi ngay jànge ? Walla ndax mas nañu wax ak yaw ci Biibël bi ? Seede Yexowa yi, ñan lañu dëgg-dëgg ? Lu tax ñuy wax ak ñépp ci li ñu gëm ?
Ay nit lañu ni ñépp. Bokkuñu cosaan te yemuñu am-am. Ñu bare ci ñun dañu bokkoon ci yeneen diine. Am na sax ñoo xam ne gëmuñu woon ne Yàlla am na. Waaye bala ñuy nekk ay seede Yexowa, dafa fekk ñu jël jot ngir jàng bu baax li nekk ci Biibël bi (Jëf ya 17:11). Ba pare ñu gëm li ñu jàng te kenn ku nekk ci ñun tànn nekk kuy jaamu Yexowa Yàlla.
Njariñ lañuy jële ci jàng Biibël bi. Ni ñépp, dañuy am coono. Dañuy xeex itam suñu matadi. Waaye nag gis nañu ne dañu gën a am jàmm ci suñu dund ndaxte bés bu nekk ñu ngi def lépp ngir topp li Biibël bi santaane (Sabóor 128:1, 2). Njariñ boobu bokk na ci li tax ñu sawar a séddoo ak nit ñi li ñu jàng ci Biibël bi.
Santaane Yàlla yi ñoo ñuy wommat. Topp santaane yooyu nekk ci Biibël bi mooy dimbali nit mu am xel mu dal, mu may cér moroomam te am ay jikko yu mel ni njub ak mbaax. Dafay tax it ñu nekk ay nit yuy sàmm seen wér-gi-yaram te am njariñ fi ñu nekk. Dafay yokk juboo ci biir kër te xiir nit ñi ci am dundin bu sell. Ndegam wóor na ñu ne “ Yàlla du gënale, ” ñun itam seetuñu xeet, seetuñu réew, waaye ci àddina si sépp, ñun seede Yexowa yi, ñu ngi mel ni ay mbokk ndax li ñu bokk li ñu gëm. Dëgg la, ay nit lañu mel ni ñépp waaye amul mbooloo bu mel ni suñu bos. — Jëf ya 4:13 ; 10:34, 35.
-
Lu tax ñu mën a wax ne seede Yexowa yi ay nit lañu mel ni ñépp ?
-
Yan santaane Yàlla la seede Yexowa yi jàng ci seen gëstu Biibël bi ?