WAAJUR YI ÑOO MOOM LII
8: Royukaay
LI MUY TEKKI
Ay waajur yu nekk ay royukaay yu baax, dañuy jëfe li ñuy wax. Ci misaal, bu amee ku la seetsi, nga wax sa doom: «Ne ko, nekkuma fi», fekk yaa ngi ci kër gi, bul yaakaar sa doom nekk kuy wax dëgg.
«Ñu bare dañuy faral di wax naan: ‘Defal li ma la wax, waaye bul def li may def.’ Loolu du dox ak xale yi. Xale yi dañoo mel ni epoos, ndaxte dañuy jàpp lépp li waajur yi di wax ak li ñuy def. Bu suñuy jëf àndul ak li ñu leen di wax, ñoom dinañu ñu ko won» (David).
LII LA BIIBËL BI WAX: «Yaw miy waare di tere sàcc, mbaa doo sàcc yaw itam?» (Room 2:21).
LI TAX MU AM SOLO
Xale yi ak ndaw ñi, seeni waajur lañuy gën a roy keneen ku mu mën a doon, ba ci seen xarit yi sax. Loolu mu ngi tekki ne, yéen waajur yi, yéen a gën a mën a teg seen doom ci yoon bu baax bi. Kon, fàww ngeen jëfe li ngeen di jàngal seen doom.
«Mën nañu wax dara suñuy doom ay yooni yoon, te duñu xam ndax ñu ngi ñuy déglu. Waaye bés bu ñu juumee ba jëfewuñu li ñuy wax, xale bi dina ñu ko won. Xale yi dañuy seetlu lépp li ñuy def, bu dee sax dañuy yaakaar ne ñoom séetluwuñu ko» (Nicole).
LII LA BIIBËL BI WAX: «Xel mi jóge ci kaw [...] amul genn naaféq» (Saag 3:17).
LI NGA MËN A DEF
Xoolaatal sa bopp bu baax. Yan fasoŋu film ngay seetaan? Na ka ngay doxale ak sa jabar walla say doom? Yan fasoŋu xarit nga am? Ndax dangay bàyyi ñeneen ñi xel? Ci gàttal, ni nga bëgg say doom mel, ndax noonu nga mel?
«Man ak sama jëkkër, duñu forse suñuy doom ñu def loo xam ne, ñun duñu ko def» (Christine).
Baalul boo juumee. Sa doom yi xam nañu ne, nit rekk nga te dangay juum. Saa yoo juumee, boo waxee ki ngay séyal walla sa doom «baal ma», dinga leen jàngal luy njubte ak woyof.
«Nangu ne juum nañu ci suñu kanamu doom, lu baax la ci ñoom. Baalu ci suñu kanamu doom bu ñu juumee, lu baax la itam. Bu ñu ko deful, ñoom bu ñu juume, dinañu ko nëbb» (Robin).
«Ñun waajur yi, xale yi ñun lañuy gën a roy. Te royukaay bi ñu leen di jox, lu am solo la, ndax moom la ñuy gis saa su nekk. Royukaay bi ngay joxe, dafa mel ni téere, bi xale yi di ubbi ngir jànge ci saa su nekk» (Wendell).