Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ni diigal di téyee gaal, noonu la sàmm kóllëre di dëgërale séy bu jafe-jafe ame.

ÑI NEKK CI SÉY ÑOO MOOM LII

1: Sàmm kóllëre

1: Sàmm kóllëre

LI MUY TEKKI

Jëkkër ak jabar yuy sàmm kóllëre dañuy gise seen séy ni lu amul àpp. Loolu mooy tax ku nekk wóolu moroomam. Ku ci nekk dina am kóolute ci ne, moroomam dina sàmm séy bi, bu dee sax am nañu ay jafe-jafe.

Am na ñuy des ci seen séy ndax ragal ni leen seen mbokk yi walla ñeneen ñi di gise. Waaye li gën mooy sàmm kóllëre ndax mbëggeel ak respe bi nekk ci seen diggante.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Bu jëkkër ji fase jabaram» (1 Korent 7:11).

«Boo fonkee sa séy, bu ñu la tooñee sax doo gaaw a mer. Dinga baale te di baalu ci lu gaaw. Doo gise jafe-jafe yi, ni buntu ngir tas sa séy» (Micah).

LI TAX MU AM SOLO

Bu jafe-jafe amee, jëkkër ak jabar yu dul sàmm kóllëre ñooy faral di wax ne, ‘man ak moom mënuñu woon a ànd’, ba pare ñuy wut pexe ngir tas seen séy.

«Ñu bare bu ñuy dugg ci séy dañuy jàpp ci seen xel ne bu doxul ñu tas. Bu nit ki di dugg ci séy te xalaat ne mën na tas, loolu dafay wone ne parewul woon ngir sàmm kóllëreem» (Jean).

LI NGA MËN A DEF

LAAJAL SA BOPP LII

Boo leen di xuloo . . .

  • Ndax dangay rëccu ni nga séye ak moom?

  • Ndax dangay faral di xalaat nekk ak keneen ku dul moom?

  • Ndax dangay wax lu mel ni: «Dama lay bàyyi», walla: «Damay wuti keneen ku ma fonk»?

Boo tontoo waaw ci benn ci laaj yooyu, jot na nga gën a sàmm kóllëre gi dox sa diggante ak ki nga séyal.

WAXTAANAL AK KI NGA SÉYAL CI LAAJ YII DI TOPP

  • Ndax ñu ngi kontine di sàmm kóllëre gi dox suñu diggante? Bu dee déet, lu ko waral?

  • Lan lañu mën a def tey ngir gën a sàmm kóllëre gi dox suñu diggante?

XELAL

  • Deel bind dara ki nga séyal ngir won ko sa coofeel

  • Tegal sa foto jabar walla jëkkër ci sa biro ngir wone sa takkute ci moom

  • Deel woo telefon sa jabar walla sa jëkkër bés bu nekk, boo nekkee ci sa bérébu liggéeyukaay mbaa boo ko soree

LII LA BIIBËL BI WAX: «Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas» (Macë 19:6).