Lan la Biibël bi wax ci Nowel?
Li Biibël bi wax
Biibël bi waxul kañ la Yeesu juddu. Waxul it ñu màggal bésu juddoom. Lii la téere bi tudd McClintock and Strong’s Cyclopedia wax: «Yàlla santaanewul feetu Nowel, te it feet boobu nekkul ci téere Injiil».
Bu ñu seetaatee bu baax cosaanu Nowel ak lépp li mu àndal, dinañu gis ne dafa bokk ci ay aada yu jaamukatu xërëm yi doon topp. Te Biibël bi wone na ne, bu ñuy jaamu Yàlla ci fasoŋ bu ko neexul, ci dëgg ñu ngi koy tooñ (Mucc ga 32:5-7).
Fi aada Nowel yi jóge
Màggalu bésu juddu Yeesu: «Karceen yu njëkk ya daawuñu màggal bésu juddu [Yeesu] ndaxte ci ñoom màggalu bésu juddu dafa bokk ci aaday ñiy jaamu xërëm» (Téere bi tudd The World Book Encyclopedia).
Bésu 25 desàmbar: Amul dara luy wone ne Yeesu bés boobu la juddu. Kilifa làbbe yi ñoo tànn 25 desàmbar. Ñi doon jaamu xërëm ñoo amoon ay feet ci jamono boobu ñuy wax ci tubaab solstice d’hiver. Kon dafa mel ni Kilifa yi dañu bëggoon mu tombe ci jamono boobu.
Joxante kàdo yi, ngonal bi ak mbuumbaay mi: Lii la téere bi tudd The Encyclopedia Americana wax: «Ci diggu weeru desàmbar, waa Room dañu amoon feet bu tudd Saturnales [ci tubaab]. Aada Nowel yu bare ñu ngi jóge ci feet boobu, mel ni ngonal bi ànd ak mbuumbaay mi, joxante kàdo yi ak taal sondeel yi». Téere bi tudd Encyclopædia Britannica nee na it ne, «kenn daawul woon dem liggéey» ci jamono feet boobu.
Làmp yi ñuy taal ci Nowel: Ci li téere bi tudd The Encyclopedia of Religion wax, waa Ërop dañu doon rafetal seeni kër «ak ay làmp ak it xeetu garab yu bare» ngir màggal bés bi ñu wax ci tubaab solstice d’hiver te dàq rab yu bon yi.
Garabu Nowel: «Jaamukati xërëm yu bare ca Ërop dañu doon jaamu ay garab. Bi ñu tuubee nekk ay karceen sax, dañu daan kontine di leen jaamu». Foofu la aada Nowel bii jóge: «jël garab, rafetal ko, teg ko ci buntu kër gi walla ci biir kër gi» (Téere bi tudd Encyclopædia Britannica).